Àjjuma 10 Mai 2024
#XALIMAG_LEER
XASIIDAG SIN-DIIDI
⤵️⤵️
bokk na ci xasiida yi Sëriñ bi teel a bind lool. Ndax jiitu na 1301. Man nanoo wax ne Xasiida yi nuy jàng ci jamono jii mooy gi ci jiitu, nee ñu : Bi mu koy bind ci 20i at rekk la tolloon, maamam Soxna Aysatu Mbàkke nu gën koo xam ci Soxna Asta Waalo moom la ko bindaloon, Booba dafa fekk maamaam jooju daan jàng muslaay gu tuddu As-sayfiyu doon ñaan gu guddu, Sëriñ bi tënkal ko lépp ci xasiidag Sin-diidi, bi ko ko Sëriñ Tuubaa joxee moom Soxna si, bu ko daan jàng ba nit di ñëw da koy nëbb ngir at yu néew yi Sëriñ bi amoon. Ay bayitam toll nañu ci 50i bayit. Mu làmboo ay ñaan ak i muslaay di xasiida gu baax lool ci kaaraange.
Anam gi ko Sëriñ bi binde, mooy dafa def tawasul. Tudd na ci lenn ci yónnent yi, lenn ci malaayka yi, sahaaba yi, wàlliw yi ak nit ñu baax ñi. Dal di cay ràññetle ci biir Sahaaba yi ñent ñii di Abuubakar, Omar, Usmaan ak Àlliyu. Ginnaaw ba, mu indi ñent imaam yu mag yi ci fiq woroom ngiir yu siiw yi : Imaam Abuu Haniifa, Imaam Maalig, Imaam Saafihii ak Imaam Ahmat Ibn Hanbal. Mu tudd it Lawhul Mahfuus ak Aras ak Kursiyyu. Bokk na ci yi muy tawasul Alxuraan, Tawraat, Injiil ak Sabuur. Mu tàmbali ñaan yi, ginnaaw bi mu jullee ci Yónnent bi shw ñaanal ay ñoñam ak i sahaabaam ak i soxnaam.
Lenn ci yi nga xam ne Sëriñ bi ñaan na ko ci biir xasiida gi ak yi nga xam ne, mi ngi ciy muslu ngir sunu Boroom dàqal ko ko :
Dinanu gis ci xasiida gi lu doy sëkk, lu nu man a ñaax ci nu koy jàng, ndax mbooleem li mu ciy tudd lépp ku bëgg lu baax yittewoo na ko. Mbooleem yi nga xam ne day bëgg sunu Boroom dàqal ko ko, ku nekk bëgg nga sunu Boroom soril la loolu.
Bokk na ci yi muy ñaan Yàlla : Jàmm, am ubbeekug bunt yiw yi Yàlla ubbiloon nit ñu baax ñi. Mi ngi ciy ñaan : sóobu ci yoonu Yónnent bi Shw te Yàlla matalal ko lépp luy yéeneem ak jubluwaayam. Mi ngi ciy ñaan it lépp lu mu tànn sunu Boroom defal ko ko, ak it sunu Boroom defal ko ag jàppandal ci bir yu jafe yépp. Mi ngi ciy ñaan it gudd fan ak wér ak ug njub ak tawféex ak xol bu ragal Yàlla ak xam-xam bu bariy njariñ ak tuub gu ñu nangu.
Bokk na ci yi nga xam ne da ciy muslu ci biir Xasiidag Sin-diidi : Mucc ci noon yi, ak balaa yi mucc ci ag ñàkk ak i coono ak ug torox, ak ug nooteel ak mar ak xiif ak fitna ak balaa. Mucc ci lakk ak lab ci ndox, lori melax ak sàcc, mucc ci ayu sedd ak ayu tàngoor. mucc ci xeetu réer ak mbugal ak njàqare. Mucc ci saddum jinne mucc ci tawat ak gaana, mucc ci ayu ku iñaan ayu gémmiñ ayu bët ayu njabar, mucc ci ayu nit ñi ak jinne yi ak ayu tooke. Mi ngi ciy ñaan it : Sunu Boroom def xolam ak làmmiñ di tudd Yàlla ci buy faatu. Ñaanal na ci way-juram ñaanaalel jullit ñépp.
Noonu mu ñaane képp kuy jàng Xasiida gi ñaan yooyu yaa ngi koy defal sa bopp, kon lu mat a fonk la te lu mat a bàyyi xel la.
Moor Suraŋ