Soxnas saa-siin bi Z. Xiicen (Zhao QICHEN) fa Siin 🇨🇳 moo bind (mémoire de Master) jëmale ko ci làkku #Wolof ak tolluwaayam ci réew mi.
Di sant waa saabal @SaabalN ci taxawu gi nu doon defal ci liggéey bi.
yelleefi kujje gi ak tëdde njaaxaanaay Ngomblaan gi.
Xamle nañu ne dinañu bind Mbootaay gi dajale Ngomblaan yi, Mbotaay gi dajale Ngomblaani réew yiy làkk farañse, CEDEAO, UEMOA ak Mbootaayu Réewi Afrig yi. Fas nañu yéene itam amal ay ndajey jéebaane fépp ci àddina si.
Ngomblaan ga : Ginnaaw fitna ji ñu teg ci kaw Abdu MBÓW, jàmbur yi féete ci kujje gi fas nañu yéene jéebaane jëf jii fépp ci biir àddina si.
Jàmbur (député) yi féete ci kujje gi xamle nañu ne dinañu dajaloo kalaameji ci mbootaay yi nekk ci biir Afrig ak fépp ci àddina si,
jëf jii amoon ca Ngomblaan ga te ñu jàppe ko ni ag xaabaabal ci wàllu campeef yi. Ginnaaw ba ñu fitnaalee Abdu MBÓW mii bokk ci ñoom, jaay ko doole génne ko ca biir Ngomblaan ga ci bisub jataayu 29i fani suwe 2026 bi, ñoom kujje gi ñu ngi ñaawlu jëf jii ñu gis ne dafay salfaañe
ngir xam mbooleem pakk yi fexe leen a teggi.
Sémb wii doon na lu am solo jëm ci gën a dooleel xeex bi ñuy amal ci wal yi ca Tuubaa. Ci geneen wàll, basee bu Ngiraaneen war naa noppi fii ak weer, ci jamono ju ñu nekk itam di fattarndi kanaal yi war a mat fii ak 10i fani sulet.
Nawet bi ca Tuubaa : Njiitu ONAS sàkku na ci ñi yor liggéey yi ñu baral jéego yi...
Mu demoon nemmikuji tolluwaayu liggéey yi ñuy amal ca Tuubaa, Njiitu ONAS lii di Séeni JÉEN, sàkku na ci kër gi ñu dénk liggéey yi mu baral jéego yi ngir ñu man a yegg fii ak 31i fani sulet 2026.
Fii yëf yi tollu nag, ci 8i km yi ñu nisaroon ci ay kanaal, 4i km rekk a ci jot a noppi. Di tolluwaay bu mu gis moom Njiit li ne, néew na lool ba tax mu sàkku ci këru liggéeyukaay gi mu yokk ay liggéeykatam, ba noppi xamle ne dees na ci amal um ndaje
Paab Maalig NDUUR am na péexte.
Moom mi fi jiite woon fi PRODAC, ñibbi na këram démb ginnaaw bi pekkub toppe gi (parquet) delloo ginnaaw ci dabu gi (appel) mu nammoon a def ci bàyyig néggandiku gi ñu ko jagleloon. Moom sëñ NDUUR kon dellu na cig njabootam ak lamu xarala.
Jàmbur yi (député) càmbar nañu tegtal yooyu, amal ay digle teg ci feddali taxawaayu Ngomblaan gi ci wàllu saytu yënguy Ngóornamaŋ bi, yoriin wu leer ak doxaliin wu jub ci alalu askan wi.
https://t.co/fRCVsONmBP
Jataayu waxtaane Njël li (DOB) : Ngomblaan gi yaatal na ci yitte yi gën a far...
Ngomblaanug Senegaal amal na démb ci talaata ji 30i fani suwe 2026, jataay bi jëmoon ci waxtaane njël li (DOB), di pàcc bu am solo bu jëm ci waajal Njël li Nguur gi war a jëfandikoo ci at yiy ñëw.
Seex DIBA miy Jëwriñu Koom mi, Koppar yi ak Palaŋ bi, aajar na (presenter) Wayndare wi ñu tënk wàllu koppar yi ak koom mi ci 3i at yiy dëgmal (DPBEP), te doon luy leeral mbébet yi Ngóornamaŋ bi am ci wàllu koom mi ak tegtal yu am solo yi ci wàllu njël li.
Mbooleem jàmbur yi (député), woolu nañu leen altine 29i fani suwe 2026 ci jataayu béj (séance plénière) ngir càmbar ngaarlug sàrt l17/2026 bi jëm ci yeesal Ndayi Sàrt yi.
https://t.co/fRCVsONmBP
Leegi leer na, Senegaal jàll na ci 16eelu xaaju daytal yi...
Ginnaaw ndam lu yaatu li mu am diggam ak Iraak, ak njureef yi tukkee ci joŋante yu mujj yi diggante Espaañ ak Urugay ak diggante Esibt ak Iraŋ, Senegaal daal di nay jàll ci 16eelu xaaju daytalu kubu futbalu àddina si.