Son air est séduisant et ravissant, il est rayonnant et même perturbant il propulse nos esprits ❤️ purifie nos corps 😍🤗 apaise nos âmes et embelli nos cœurs ❤️😍
#AL_MOUNTAKHA
Ab tënk ci gëm dogal bi
Suko defee, ñett (3) yoo yu ku ko gëmee noo nu, ap jullit la. Ku ko gëmeewul noo nu nak, ap yéefér nga.
Xeetu dogal yi
Waa sunna ñoom noo nu ma waxee la ñu gëmee dogal bi. Waaye dogal
bi nak am na ñetti (3) xeet :
1) Bu njëkk bi mooy dogal bi ñuy tuddee xamuk sunu Boroom. Boo bu
mooy dogal bi jiitu ci lépp. Loo loo tax ñu naan wilaayatu goo gis ak jagle
moo ko jiitu. Sunu Boroom nee na ‘’yuu faku h’anhu man ufiku’’, maanaam
‘’alxuraan ku ka gëmul ci àdduna daa fekkoon sunu Boroom dogal ko bu
yàgg ni doo ko gëm’’.
Yonent bi (YYJSM) nee na ku faatu ku nekk fekkoon na sunu Boroom xam
ak faatoom.
2) Ñaareel bi mooy dogal bi ñu dogal te bind ko ci lawhul mahfuuz.
Boo bu moom mën naa soppeeku. Ndax Yàlla nee na ci alxuraan ‘’yamhul
laahu maa yachaa-u wa yusabittu wa h’indahuu umul kitaabu’’.
H’abdulaahi ibnu h’omar (YYDG2) daan na wax buy ñaan: Sunu Boroom
boo ma bindee may ku texeedi, Yàlla na nga ko far te bind ma may ku
texe.
3) Ñetteel bi mooy dogal bi ñuy dogal bu nit ki nekkee ci biirup yaayam.
Ndax malaaka mi da ñu koy digal mu bind wërsëgam akup appam akuk
texéedeem akuk texéem.
4) Ñenteel bi mooy bi nga xam ni moom la ñuy tuddee andi dogal yi ci
seen waxtu.
Ndax sunu Boroom bind na lépp ba noppi waaye lu ci ne da koo wutal
waxtu. Saa su waxtu wa aksee mu andiko. Noo nu la ñëwee ci al-ib-riiz bu al Yaddaaliyu (YYDG).
Gëm dogal bi
Lislaam nak ñetti (3) xaaj la : iimaan, islaam ak ihsaan. Iimaan ci boppom
dafa seddaliku juróom benn (6) xaaj :
gëm Yàlla, gëm malaaka yi, gëm
yonent yi, gëm téere yi, gëm yawmal xiyaam ak gëm dogal bi. Kon gëm
dogal bi daa bokk ci liy matal sa gëm Yàlla. Lan mooy gëm dogal bi nak ?
Xaaju dogal yi
Gëm dogal bi ñetti (3) xaaj la :
1) Bu njëkk bi mooy nga gëm ni lu am ak fu mu ame, Yàlla xam na ko te
moom la neex mu am.
Wuteek al xadariyatu ñi nga xam ni dañuy wax ni dogal yi ginnaaw bi mu
amee la ko sunu Boroom dooga xamee noo na. Ñoo ñu ay yéefar yu wér lañ.
Ñoom sax laataa imaamu Chaafih’i-yu di génn àdduna jeex nanu takk.
Lu mat juróom ñaar fukki (70) yonent rëbb nanu leen. Yonent bi (YYJSM1)
nee na bu ñu tawatee bu leen kenn seeti, bu ñu faatoo bu leen fa teew.
2) Ñaareel bi mooy nga gëm bu wér ni sunu Boroom moo bind nit ñi ak
seeni jëf.
Wuteek al Muh’tazilatu yiy wax ni sunu Boroom moo bind jaam ñi, waaye jaam bi moo bind jëfi boppam. Ñoo ñu seenuk kéefér am na ak wuute.
Waaye Alxuraan weddi na leen ci ay barap yu bari mel ni ‘’wallaahu xa-
laxakum wa maa tah’maluuna’’ ak ‘’wallaahou xalaxa kulla chayin’’ ak ci
yeneen aaya.
3) Ñetteel bi mooy nga gëm ni yiw ak ay, ñaari (2) mbindéefi sunu Boroom
la ñu.
Wuteek al Maanawiyatu ñi toppu Maaniyu, fen kat boo bu di wax ni lëndam moo bind ay. Alxuran weddi na ko bi mu nee ‘’wa jah’ala zullumaati wa
nuura’’.