Ci misaali àdduna yii rekk ngay xame ne bés-pénc lu doy waar la.
Li nga weesu sag dund lépp ñu nar koo càmbar, lu ne rekk ñu laaj la ko, te ki lay laaj gën laa xam lépp.
Yal nanu Yàlla suturaal te yërëm nu.
Bu jamono naqaree ñu bari nekk ci ay jafe-jafe, Ku Yàlla dénk wërsëg war nga cee profité jaamu Yàlla ci nit ñi, di leen taxawu ak di leen dimbali ngir Yàlla rekk.
Dund gi cher te du baax, nga lekk ko febar dem hôpital doo faju, dëkk bi salte bari ndox amul organisation ñenn ñi di concour reewande, koo wóolu mu wor la, ku la leb du la fay, ku man sa moroom duma, Politicien yi di séddoo xaalis bi te du mujj fenn
Defe nga ne lii réew la ?
Saa boo yëgee ci sa bopp ne dafa am koo iñaane walla nga soxore ko, te nga bëgg loolu deñ, deel wéet di ko ñaanal aw yiw, dangay jekki rekk yëg ne sopp nga ko.
{Yàlla mi nga xam ne, saa boo ko jëfalee te sellal ko dina la gërëm, yamal ci moom di ko jëfal te bàyyi keneen.
Yàlla mi nga xam ne, booy sàkku ngërëmam, li nga ragal tay ak ëllëg lépp dina la ko fegal, booy jëf jëfal ngir moom.
Yàlla mi nga xam ne, ku koy topp ngir sàkku ngërëmam, dina la féetewoo taxaw ci say mbir, loo bëgg mu def ko, loo ragal mu fegal la ko, doy la sëkk ba doo soxlaal keneen, te boo moytoo li muy tere, dina la teral fajal la say aajo, deel jëf ngir moom rekk.}
Masaalikul Jinaan !