Sëriñ Mustafaa Mbar, bu teggiin doon jëmm ma ne moom la, li Yàlla gën a bëgg ci ab jaam la def muy woyof, gisul dara ci boppam, yamalewul kilifaam ak dara, liggéey bu ñu woote mu njëkk ca mujj ca.
Yal na ko Yàlla sàmm !
Amna nit ño xamni yallah mo fexe ba jaamam yi ñeme leen , ñeme leen wax seen soxla , ñeme leen wax seen naqar ag seen jaaxle
Ku yallah def nga melnii fexeel la samm haqu yallah ci jaam ñi ci sutural leen ku nit woolu ba denk la ci boppam ngala waay teyeel ko ko, dimbali leen sa kem kattan te yeene ci jaamu yallah
@papesenisall Bëyit yu yeeme lool day wax ni rek kepp kuy lewto ak nit naga xamni yalla gay lewtol te lepp lumu ñaan sunu borom Yalla ñodil koko mu ñëw ci mom te lepp lu mu soxla wul wala loo xamni dakoy yakal suko ñaane sunu borom dakkal ko ko ci ni ñuko netale
Mbir moo rafet njort, lu rafet rekk nga cay gis, loo ñaaw njort nag, lu ñaaw rekk nga cay gis.
Bari na nit ñoo xam ne, njort yu ñaaw rekk lañuy topp ba mere ku leen deful dara.
MS
Jóm ba jóm jeex baña dess ginaw rek la
Ngor ba ngor jeex baña ñaaw rek la
Waye bala moo am njariñ dëg nga am jòm
Te jaay ko YALLA.
Sëriñ Muntaxa Mbacké
Ëllëg bis pénc bu mbir yi mettee jaam ñépp jaaxle, ñu teg siraat ci kaw sawaraw Jahannama, kenn xamul foo jëm nit ñépp tiit, dina am ku woote, wax ne : Ana ñi doon liggéeyal jullit ñi ? Ñooñu daal di wuyu ne, noo ngi nii, ñu ne leen gaawleen dem dugg àjjana, fitna ak coonoo yii di bëgg a xew yéen du ngeen ko fekke.
Masaalikul Jinaan
Sëriñ bi ne woon samag njaboot aar naa leen ba dara du leen lor, waaye nañu ma dimbali ci ñatt :
- Lekk ci mbooloo
- Fu ñu jote dem fa
- Ku leen bëgg a gis, gis leen.
❗️420 milliards de fcfa de marché gré à gré obtenus par le groupe Ellipse d’Olivier Picard dont les 21 milliards liés à Madiambal Diagne journaliste devenu milliardaire grâce au contribuable !