Delluwaay yeep yi wer da ñu saxal ni 12 ci weeru gammu la aleyhi salaam gane adina , bis boobu nag Ibliiis da fa yuuxu jooy ame xoo bu naqari . Saa bu bis bi dellusee nag kep ku sa xol naqari ag lu ko mën a naqaril nag , nitu iblis nga .
KU IMAAM RAW NI MUY FAYE :
Jullig suba bu la ci benn ràkkaa rawee dangay jóg bañ a wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ca kaw te bañ a xunóot ndax àndoon nga ak imaam ràkkaa bu mujj bi ñuy xunóotee.
Jullig tisbaar bu la ci benn ràkkaa rawee dangay jóg bañ a wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ci suuf toog taaya sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee dangay jóg wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ci suuf jógaat taxaw bañ a toog indi beneen ràkkaa bu mel noonu daa di sëlmël. bu la ci ñatti ràkkaa rawee dangay jóg bañ a wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ci suuf toog taaya muy sa ràkkaab ñaareel, nga jóg indi beneen ràkkaa jàng Faatiha ak aw saar ci suuf bañ a toog muy sa ràkkaab ñatteel, nga indi beneen ràkkaa boo xam ne Faatiha kese nga ciy jàng ci suuf toog taaya sëlmël.
Bu dee julli tàkkusaan nii ñu ko waxee rekk ci jullig tisbaar ni la demee genn anam gi la ci ni ñu koy fayee bu la imaam rawee.
Jullig timis bu la ci benn ràkkaa rawee dangay jóg wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ca kaw toog taaya sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee boo jógee doo wax Allaahu-akbar dangay jàng Faatiha ak aw saar ca kaw toog taaya muy sa ràkkaab ñaareel, nga jógaat jàng Faatiha ak aw saar ca kaw daa di toog taaya sëlmël.
Jullig gee bu la ci benn ràkkaa rawee boo jógee doo wax Allaahu akabr dangay jàng Faatiha ak aw saar ca kaw toog taaya sëlmël, bu la ci ñaari ràkkaa rawee dangay jóg wax Allaahu-akbar jàng Faatiha ak aw saar ca kaw bañ a toog muy sa ràkkaab ñatteel nga indi beneen bu mel noonu toog taaya sëlmël, bu la ci ñatti ràkkaa rawee boo jógee doo wax Allaahu-akbar dangay jàng Faatiha ak aw saar ca kaw toog taaya muy sa ràkkaab ñaareel, nga indi beneen jàng Faatiha ak aw saar ca kaw bañ a toog di taaya ndax mooy sa ràkkaab ñatteel, nga indi beneen jàng Faatiha kepp te yelu ko muy sa ràkkaab ñeenteel nga sëlmël.
Seex Ahmadu Bàmba Tasawudus Subbaan