Seydina Mandione Laye néneu :
Baye Laye rkay Baye Laye,
Kudul Baye Laye do Baye Laye,
Yalla swt rk mo xam Baye Laye mome mi yonni Baye Laye psl.
#BayeLayeBaxna
[Nisfu Chaaban - 𝑴𝒂𝒘𝒍𝒊𝒅𝒐𝒖 𝑩𝒂𝒚𝒆 𝑳𝒂𝒉𝒊 ﷺ 🤲🏾]
15 jours après l’Appel de Seydina Limamou Lahi ﷺ la communauté Akhlou Lahi célèbre cette fois la naissance du fils d’Al Hassan et de Coumba Ndoye, un événement intimement lié à un de ses petit-fils, 👇
Ñioñam ya wër ko di sàbba, bañ yaa nga naa dééta waay wax leen ci waa ji, balaa siiw sànku, nan dem ca buur, Pikin dañoo jeex, Maam jaa wootewoon diine.
#Appel2023
Njool ma cëppéélu biir yoof, leeram ga dem Kambaréén jénéer ba dem bayti Maamur « saalihhina » ya teew ña gëm fa Ndar wóólu, Waalo gëm te kontaan.
#Appel2023
Yaa naawewoon Màkka, yanu leer yaak sunuy ruu, ba ngay cëppéelu Ngor, riir wa dektu rilwaan ku gëm nu gëm, ku bañ dunu tàggo ba diiwaan.
Baye Laye mu baax ma amul mass saws.
#Appel2023
Bu leen xeeb jaam bu aw ci ndigël, ndigël du ndugël, ragal nanu bël boroom gaal gi moo nuy jël yóóbu nu pééy ba nuy naane.
“Al hamdu li Laahi Maaliku naa wa salli a laa Muhamadu naa” ku lay mana sànt man raw naa ndegam du ka siiwé “alfaani”.
#Appel2023
Xëccoo leen wéétëluk fari ja bu leen jàngaani ngir daraja Yonnent, fóóre ya mooy dono ja ségém rombul ndigël daa ne.
Da nuy tàgg Njiin boroom jamano ki wooté, nu wóólu kay naxu nu da fay gindi ruu yi booleek nun nu dellu ko sànt “Hamdaani”.
#Appel2023
Barib xamxam taxul mana dem siraat am ndok la, bés bu ñu jëm ki fiy wone yoon wi moo mata xam te farlu ca laa mu santaane.
Ku tektaluwoon ci waa ju gëlëm da ngay mujjé réére mbir ci waxam ku réére jamano, doo mana xam boroom a nga leen di dénkaane.
#Appel2023
Labal na ca lenn ciy fóóreya bu ñuy firi boole seen tor ya la ñuy firi wóóratul jaam ya ba Njool ma ñu jiñ ko seytaane.
Ba Mahdiyu feeñagul amu fi ku fiy wone yoon wu jub newu fi li Yàlla bëgg ak li muy tere fii, lu ngeen bañe Baay Libaas laa ne?
#Appel2023
Tanxal na ca soppe yaak bañ ya junniy junni naan ca leeram ya nit ak jinne wo na leen dunya ngireek ñuy jaamu Rabbani.
Ba Njool may waaja feeñ ku jubul ka jooy fa safaan ba, jaam ya yëgul. Niiraan jooyle kook ya mu sol rogoñ yaay “baxru zulmaani”
#Appel2023
Ñi rééroo sànku ngeen ku ci bañ ki Yàlla yabal, waxam ja du deñ te Mahdiyu mooy boroom sañsañ te mooy ubbi « baabu jannaati »
Mahdiyu Laay fajal na nu mar ba Njiin wootee la fóóre ya wor sunub sàng jooy na, Saaba ya xar rogoñ yay « baxru rahmaani »
#Appel2023