Pour les heures de prières au Sénégal il faut qu'on en parle. Tisbare dou changei mouk depuis temps xalei ba ni.
D'ailleurs d'où viennent ces heures qu'on distribue chaque semaine !??
Masaalikul Jinaan, teggiin yi nekk ci diggante nit ñi :
Rafetal say jikko sa digg ak ñoom, bari kersa, lépp loo xam ne defe ko ndayjoor moo gën, nga di ko defe ndjayjoor, lu mel ni lekk walla sol dàll ak yi ku niru, lépp looy tàmbali wax (Bismil Laah) bu dee barab bi nga nekk laaj na ko.
Bokk na ci yooyu di sàmm teggiini lekk, nit ki buy lekk war na koo rafetal lool, lu mel ni yam ci kanamam, moytoo tuur ñam wi, rafetal ni muy lekke, te moytoo ëppal ci lekk gi.
Socc bokk na ci teggiin yi, rawatina ci waajtaayu julli, ba laa ngaa jàpp nga socc walla boo jàppee ba noppi, ba la ngaa julli nga socc bu baax ci julli yépp, saa booy nuyoo ak nit, nga jox ko yitte bu baax, téye ko ci sa ñaari loxo.
Bari looy jàng Alxuraan teggiin la, ak saa boo rombee nit nga nuyu ko, man nga koo wax (Assalaamu Halaykum) rekk kon dina doy, te ku la nuyu nga fay ko, ci anam gu gën a rafet na mu la nuyoo, foo dégg sa mbokkum jullit mu tawat nga seeti ko.
Bokk na ci teggiin yi, saa boo tislee nga wax (Alhamdu lil-laah) te bu keneen tislee ba wax ko, yaw it nga ndokkeel ko, ne ko (Yarhamukal Laah) yal na la Yàlla yërëm, booy bébbale tegal sa loxo ci sa gémmiñ.
Ba tay bokk na ci di toppatoo sa jëmm, lu mel sa kawar nga di ko defar, moo xam ci poqutaan la walla ci naq walla bopp bi, ak fexe bay set ngir bañ a lor kenn ci ag xet gu bon, ba la ngaa dugg ci ab néeg, nanga yëglu ba ñu jox la ndigal ngir nga dugg.
Bokk na ci teggiin yi, ku la tooñ nga jéggal ko, képp ku lay xañ alalam, yaw boo ame nga di ko jox, ku lay ñàkk yitte walla mu ñàkk laa jokk, yaw nga di ko jokk ak di nemmiku, képp koo xam ne, koo war a topp la, nga di ko topp, moo xam koo séqal ak kureel walla muy sa kilifa ci wàllu liggéey ak xeet yooyu, bu dee koo xam ne, sa mbokk la moom topp ko dal aa war, rawatina muy sa wayjur, sa wayjur bu doon ku dul jullit sax danga koo war a topp, bu dee li nga koy toppe ag moy Yàlla nekku ci, ndax nit ku mu man a doon sañoo koo topp ci lu neexul Yàlla.
Ba tay bokk na ci teggiin yi, yar sag njaboot ci diine ba ñu tegu ci yoonu njub, di ñeewant gone yi tey wormaal mag ñi, képp kuy sa moroom nga def ko ni sa bopp.
Am na ku doon dénk doomam ngir mu am ay teggiin, ne ko : “Ay teggiin mooy, nga topp sa yaay ak sa baay ak sa baay bu ndaw, ak sa bàjjan ak képp ku la mag ci say mbokk, tey topp sëriñ si ndax yayoo nañu ko lool, ku la féete kaw dee ko teral, ku la féete ndaw dee ko yërëm” xam nga sëriñ si ñooy defar nit ñi ak di leen yeggale ci Yàlla, moo tax topp leen ak di len wormaal lu jar a bàyyi xel la.
Kon nag yii yenn rekk la ci teggiin yu feeñ yi dox sa digg ak nit ñi.
Mu mel ni rekk tasawuf am njàgaleem dalay tax a doon nit ku nite lool, xoolal yi mu wax fii rekk, yi ci ëpp ñi dul ay jullit sax dañu koo jox yitte ba dañu koy wutal ay àtte, ngir nit ñi man cee tënku, kon tasawuf dund ko, bokk na ci liy yaatal jàmm ci àdduna bi, ndax musiba yi fi am yépp, ñi ngi jóge ci jalgati àqi jàmbur, te tasawuf li muy jàngale mooy naka la ñuy sàmme àqi nit ku ne, moo xam ab jullit la walla ku dul jullit, koo bokkal am réew walla koo ko bokkalut.
Bonjour cher réseau,je suis ravi de vous inviter à ce webinaire où j'aurai l'honneur d’intervenir en tant que paneliste.
📆 05.06.2025
🕚 16:00-17:00
Voici également le lien de la réunion :
🔗 https://t.co/awiCxmosKY
Code Meet : gxd-sdbt-zns