Urgent: salam Guys un membre de ma famille a immédiatement besoin de 10 poches de sang pour une opération chirurgicale.
Contactez moi sur mon numéro personnel: 774799247:
Je vous communique son nom, le don se fait en faveur au CNTS, demain entre 8h et 13h.
@Khadiijask Eskay! As salam halaykum yaaboy! Ah yeen d meel ni sët geen ci kilifa yi koon ñu gi leen di jox sen waccu waay bu werr!
TbarkAllah am na solo. Ñakul da geen gissul lolu may wax rek te leer na ma doon na lu gën duul masati yëkëti jëmale ci keen rawatina ci kilifa. Tuub bu werr
Ay source ci diine ñatt yii moo ci ëpp doole :
Alxuraan, hadiis, lu boroom xam-xam yi dëppoo.
Ci wàllu tudd Yàlla am na ci lu alxuraan indi, (Deeleen tudd Yàlla lu bari ndax ngeen texe)
Hadiis yi ci dikk kenn xamul nu mu toll.
Boroom xam-xam yi indi ci lu yaatu.
Alxuraan tuddul benn nombre lu bari rekk la wax.
Hadiis am na ci zikar yoo xam ne, Yonent bi shw indi na nombre, yu mel noonu ngir jullit ñépp la, kenn sañuta teg benn baat ci nombre boobu ndax sunna la di waxi Yonent bi shw.
Bu weesoo hadiis yooyu, kenn manulaa wax nàngam nombre sàngam lañu koy wird, ku dul ñi ko Yàlla xamal ñu xamal ko ñeneen, par exemple : wird tariixa yi, Yàlla moo leen ko xamal jaarale ko ci Yonent bi shw, boo leen laajoon daliil ci nombre yi duñu la ko jox ndax fa daliil ya nekk yaw jotewoo fa.
Nit ñi nag dañoo wuute lool ci wàllu tudd Yàlla, Yonent bi shw am na yu mu daan jox yenn sahaaba te du ko jox ñi ci des, am yu mu daan boole ñépp loolu ci xeetu tarbiya la.
Nun nag sunu kilifa yi nu doyloo ci yoonu Yàlla ba tay daa nañu def noonu jox ñii ay Secret ñu koy wird te duñu ko jox ña ca des.
Foofu dañu fiy xame ni nit ñi wuutee, nit ku nekk ak li mu àttan, ndax turu Yàlla day lu fees dell ak ay leer, ki koy sikar di daje ak leer yooyu, nit ku nekk am fu capacité bi yam ci dékku ay leer, tur yi seeni leer dafa ëppante, am na yoo xam ne boo ci bëggoon di wird lim bu bari, dañu la koy tere, bu dee am nga kilifa gu ci xam dara, dalay jox leneen looy wird ba sa capacité boobu gën a yaatu mu door laa jox li nga doon laaj pour wird ko.
Ci gàttal dina jafe lool ma leeral lépp fii, ndax mbirum Yàlla ci wàllu zikar ay secret moo ci ëpp te du doon lu ñuy bind ci ay téere nga di ko xam waaye ay experience la yu ay nit dund ba Yàlla xamal leen ko.
Man li ma xam ci ay nit ñu wird aw turu Yàlla ba dof bari na lool te gëstu naa ba xam li waral loolu...
Am na yoo xam ne ci diine dafa làmboo ay àtte nangam araam na walla war na... Yooyu moom lu ci nit wax dalaa war a indil texte bu leer comme source, bu dee nag lu dul farata lu mel ni tudd Yalla, moom lañuy wax ay ngéneel nit ku nekk la mu ci gëstu ci ñi Yàlla may, loolu lay doyloo rekk mu doon source ci moom.
Alhamdu Lillaah !
Nit man naa joxe wird, joxe lim boo xam ne, boo koy wrid lim boobu dalay xiir ci jëmmam rekk, nga di ko sopp ba doo amati ci moom sago loo am jox ko.
Teyleen ci wrid yi ak lim yi.
Moomuma wird yi nappaatewuma waaye sañ naa laabire nit ñi, te li may laabiire lu ma xam la.
Weranteb diine lu ci bari ñu seenum njàng soriwul ñoo ciy sonal nit ñi.
Koor gu dul farata, ku mu neex sax bañ koo woor ngeen bëgg cee werante tay la ak démb la ak suba la.
Diine ay déggiin da cee am, ku nekk na doyloo aw déggiinam te bàyyi moroomam ca la mu jàpp, ñépp Yàlla lañuy jaamu te Yàlla amul problème man naa nangul ñépp ndax ku ne xam na sa yéene.
CBN bu ngeen bëggee deleen ko wax dëgg, analyse politique soxlawul wax ci nit, na yam ci ay analyse te bàyyi gor yi muy yàq, loolu keneen la waroon ku dul moom miy doomi daara.