Saa bu guddi Àjjuma jotee, nga jàng:
1-Faatiha 1X
2-Salaatu Halan Nabii 1X
3-Lixlaas 40X
4-Salaatu Halan Nabii 1X
Su noppee nga yéene ko jullit yi faatu yépp ak ñiy dund jamono jii, ak ñi wara judd.
Kon jullit bi njëkk a faatu ba ki mujjee faatu, dinañu am yoolub 40 Lixlaas.
Ku ko saxal ba Yawmal-Xiyaam, ku ñëw ci yaw ngir fayonte ak yaw, Yàlla moo naan ko, bàyyi ko mu dem ndax ku ñu mbaa-Yàlla la, dafa farlu woon bay maye aw yiiw.
Sëriñ Tuubaa moo ko waxoon Soxna Fat Ja (doomam).
Ku bëgg se bëgg seriñ bi fi yokk del jangg minanu . Te di ñaan mu yokk ! Bimay mujjee gis sñ amsa d loolu la ma waxoon « ñaanal ma ma gën a bëgg seriñ bi »
#MashrabuCaafii2026
1- yalla bimu ma bindee jox ma xel la waccoo ak man kon buma amee (soxna/ jëkër 😂) ci man la buma Amul ci man la (al qadariyya)
2- buma waree am ag buma warul am Lepp yalla bind nako bu yagg kon Jarul may sonnu di sabablu (Al jabriyya)
3- yalla mooy bind lepp Waaye may nama sañ sañ ma mëna tann mëna sabablu, (dm, tontu dm, poste, wax li ñepp di wax😂)
Lima tann bu dëppook li yalla tann ma am bu dëppoowul duma am (kasbu =asharits )
Gis gisu kureel islaam yi ci mbiru destin, ci tënk.
Nun ci 3em bi lañu nekk muy haqida a’sharit.
Nit leeg leeg mu tollu ay digënte yoo xamni kuko comprendre rek lay soxla,
Soxna aïcha biñu ku tuumaalee mu metti lool mu weet jaaxle dafa am benn soxna ci ansaar yi ñëw ci moom toog jooy bam yagg mu juk dem waxul benn baat, jooy rek la def!
Soxna aïcha dafa wax ni: kii de limu def du mako fatte mukk,
Waxul benn baat waaye xamal na Soxna Aïcha ni Mingi bokk ag moom naxar wi.
Mbooleem ñi Yàlla di teg nattu ñu di ko muñ ngir Yàlla, ëllëg duñu am balance yi ñuy peesee jëf yi, téere yi ñuy séddale te jaam bu nekk ay jëfam nekk ci, ñoom duñu ko jot, xanaa kay Yàlla da leen di sottil yiw wu bari rekk, wu kenn manul natt mbaa di ko xayma, te Yàlla du gëstu seen dara.
Masaalikul Jinaan