Booy dund, fexeel ba sa dund gii nga jeexal ko ci lu baax, ndax saa boo fi jugee, bu la àdduna sépp fàttee ba duñu la ñaanal itam, lu baax li nga doon jeexal sag dund, saa boroom du ko neenal mukk te foo nekk dina la fa fekk.
Nit ñi leegi seen soxlay bopp jatt na leen ba talatuñoo ñaanl kenn, ku nekk yaay ñaanal sa bopp.
Sëñ Maxtaar Jenn, yal na leeri Alxur’aan di lay wéttali fi nga nekk ba keroog saa di taxaw !!!