Ab murid ni mu war a doxe, nii la ko Sëriñ bi leerale (sa programme)
Ab taalibe li njëkk a war ci moom, mooy mu am ab yóbbal ci tawhiit, ba laa beru di tudd Yàlla ak di xeex ak bakkanam.
Mu tënku ci pas-pasub ahlu sunna, ndax loolu moo koy aar.
Topp bidaa day tax nit ki du man a topp leerug sunna.
Bu noppee ci loolu mu jàng ay farataam, niki laab, koor, julli, aj-màkka, ak asaka...
Ginnaaw loolu bu bëggee yegg ca Yàlla mu sóobu ànd ak sëriñ bu mat sëkk buy roy Yónnent bi shw.
Sëriñ boobu da koy wommat ci xam-xam ak ug jaamu Yàlla noonu it la koy yare ci bàyyi aada.
Kuy dund Tasawuf te àndul ak sëriñ bu mat buy yare, mu koy gunge ci yoon wi, kooku mi ngi xuus ci géejug alkande te du ca jële dara, ndax moom saytaane ak bànneex ak bakkan ñoo koy wommat.
Kuy xuus ci géejug Haxiixa te jaarewu ko ci gaalug Sariiha, ag ndofam lu leer la’’
(Tazawudus Subbaan)
Lii jar naa bàyyi xel, li war a jiitu na jiitu leneen topp ci !
Mbirum borom niaary tuur yi mom niaawlu naako , teyit metinama lol en tant que julit .
Wayee sama joot gui yeeup dumako koo def ci di nek dissi wakh luma kham ak luma khamoul ndax samay ayibbi boop doynama seuk .
Naa yoon def ligueyam .
Fimnee ma ngi khol nu sama ëlëk ak sama digantee ak sama borom jaguéé 🙏🏾.
Yalna ñu saa borom doli sutura tee saxal ñu ci njùpp .
Murid bu góor walla bu jigéen ku ci nekk am nga royukaay bu mat sëkk, ku ci bàyyi sab royukaay nag topp yeneen xalaat yu kenn xamul fu mu juddoo dangay sànku rekk.
Teggiini kureel manes na koo natt rekk ci teggini tudd Yàlla, nii la dikke ci Masaalikul Jinaan :
-Toog ci barab bu laab, mooy barab bu ñu man a jullee rekk.
- Jublu penku
- Toog ferankulaayu wala bank say tànk mel ni kuy julli
- Xeeñ xet gu neex, maanaam laal gëtt (Parfum) ci yére ak barab bi
- Di ko sellal bañ cee rax jenn wax walla jenn jëf.
Jàngat :
Yii ñooy teggiini tudd Yàlla, nit ku sàmmoonte ak ñoom dina tase ak njariñ yi.
Yàlla day buur boo xam ne, ku koy jaamu war ngaa fexe mu sell lool, kuy tudd Yàlla daa mel ni ku toog ak moom di wax ak moom, kon war naa bàyyi xel melokaan wi muy yor jamono jooju.
Daa war a toog teewlu, bank ay tànkam bañ koo tàllal, te xeeñ xet gu neex ci jëmmam ak fa mu nekk, ndax jinne yi gëm Yàlla ak malaaka yi dañuy teewlusi te dañoo bëgg xet gu neex.
Kiy tudd Yàlla war naa moytu di wax leneen, ndax di wax ak Yàlla di ca dugal jeneen wax du ay teggiin sa digg ak moom.
Kuy tudd Yàlla waru koo boole ak jenn jëf, lu mel ni yor ay telefon walla xeet yooyu, nit ki melokaan wi muy jullee rekk la war a yor buy tudd Yàlla, loolu mooy ay teggiin.
S Muhamadu Al Amiin Jóob Dagana :“Njaaloo damako doon dégg waye tay laa ko giss ”
Teh domaam S Tafsiir Jóob moo amoon lum doon jottali domu bajjenam bu jigéen faff seen loxo yi laalante.
Nenaañ bis boobu jàkka ja la doon dem waye dafa mujje dëpp.