Yaalna sunu boroom dolli ko yërmande , te woyofal suuf ci kawam , Seriñ sheexuna fall ku baax te joxoon ñeep cër . Ku bari yite yaalna ko yallah yërëm ci barkeb xasida yi
Ku gis tweet bi jangal ko shakuru rafih wala fatiha + 11 ixlaas
@SidyMSene Ndax sa cas personnel matna def generalite ag borom xam xam boobu kan la ? Ag fan la teg wax ji . Ndax ci biir xasida gi seriñ bi indi na fa ñaaan bi am solo contre ndol . Bu ken nee day indi ndool dafmay jaaxal wala ?
Li ëpp ci nun li nu degg rek la ñuy waxaat , xasida sangaam aka yeeme, mos leen ko , aka bari mboot . Te li ci ëpp ilmul yaqiin rek la nu ci am . Neew na nga ko dox ci ab xasiiida ba gis dëgg dëgg li muy def . Mba yallah baaxe ko ci yenn ci yi ci seriñ bi dëxañ !
Na nuy fatt sunu nopp ci waci gaayi te dox ci xasida yi te yallah tax lu nu ci yallah wërsagal nu jël .