Dagan na nga and ag Imaam ba ci biir julli gi nga bayiko aggale sa julli boop bu dee julli Imaam bi dafa yagg ba narla indil lor wala nga am ngant
(minahul jaliil, 1/379, hachiya dasuuqi, 1/340)
Ku amul ngant nag sañu ko def ta buko defee julli gi yaqu na, moom la seex xaliil di wax
"ولا ينتقل منفرد لجماعة كالعكس"
Ba laa sëlmël day sujoot ñaari sujoot, sujoot boobu moo tudd xabla salaam (avant sëlmël).
Ki war a tari ca kaw te tari ci suuf dañu koy jàppe ku wàññi moo waral sujoot boobu.
Ki war a tari ndànk juum tari ca kaw, dañu koy jàppe ku dolli, moom bahda salaam (après sëlmël) lay sujoot.