Diskuur bu Seex Abdul Ahad defoon ci njàngum Alxuraan :
Alxuraan dafa di waxàndi wu ñu tëj bu amub caabi, caabi moo di teere bi sóo ko bëggee laal dafa lay wax ni la
«لا يمسه إلا المطهرون»
nga dem jappi, dellusi bëgg koo laal muni la
لا يمسه إلا المطهرون
⬇️
Samedi 18 Avril 2024
KAAY JÀNG
⤵️⤵️
Diiney Lislaam (3) xaaj la :
IIMAAN (ngëm)
ISLAAM (jëfe ndigali Yàlla yi)
IHSAAN (rafetal).
Lan mooy iimaan ?
Iimaan (6) ponk (pilier) la am :
1- gëm Yàlla
2- gëm malaaka yi
3- gëm téere yi wàcc ci Yonent yi
4- gëm yonent yi
5- gëm bis pénc
6- gëm dogal moo xam mu neex walla mu naqari.
Lan mooy Lislaam ?
Lislaam (5) ponk la am:
1- wax ñaari baati seede yi
2- taxawal julliy juróom
3- woor weeru koor
4- natt asaka ci ku ko am
5- aj-Màkka benn yoon bu manoo.
Lan mooy Ihsaan ?
Ihsaan mooy jaamu Yàlla di ko rafetal mel ni yaa ngi koy gis, boo ko gisul it nga xam ne mi ngi lay gis.
Bu njëkk bii tudd ngëm moom la xam-xamu tawhiit di jàngale, ñaareel bi jëm ci jëfe ndigali Yàlla yi moom la xam-xamu fiq di jàngale, ñetteel bi jëm ci rafetal moom la xam-xamu tasawuf di jàngale.
Ñaari baati seede yi :
(( Laa ilaaha illal laah, Muhammadu Rasuulul Laah ))
Bind bi ci topp dina ñëw bu soobee Yàlla.
Leeral gi : Moor Suraŋ
Remercie toujours ta femme lorsqu’elle fait un acte de bienfaisance car le Prophète ﷺ disaitÊ: «Celui qui ne remercie pas les créatures n’aura pas l’agrément du créateur»
XALIMAG MURTADAA KEBE ÉCRIVAIN