Li gëna neex moo di xalam sa jëm , li gëna baax moo di druss say tomb
BOROOM TUUBAA ku laabu yakko laabal , tee gooru YÀLLA yépp yaa leen jaabal
Ku am ci YÀLLA dara yakko am loo , ku xam ci YÀLLA dara yakko xam loo
BOROOM TUUBAA , BOROOM MÀGG GUI 😭
Ka saytu lépp te bëggul lëf ku topp ci Moom
Loo man di bëgg ak a wut jombul nga am ko ci Moom
Ku yoqiwul naaguwul njortam rafet te jëfam
gën koo rafet, lu mu dul am Yàlla bindu ko Moom
Sëriñ Mbay Jaxate
Maam Jëmb Modu Mustafaa Faal, Yàlla na Saa Boroom Yokki leeram te taas nu ci Barkeem, Dooley Xassida yi....!❤️
31 Août ni tay la waccon liggeey, sa la ko liggéey waccoon....!
«Nañu mel ni "ëkk" te bañ a mel ni xob. Ndax, [aw] xob ngelaw man na koo naawal ba dugal ko ci'm pax waaye manu ko faa génne; Ëkk nag fu ko ngelaw fekk fa la koy ba».
#SëriñAbdulAhad
BOROOM TUUBAA neena teerey Qacida ak yërey café ak ataaya ku leen am di leen jëfandikoo ñu di la fay , boo leen joxee ku leen di jëfandikoo naka noonu ñu dileen fay , boo leen deñci wee fi barab ñu di la bindal tuyaaba
Werna lool !
CHUKRANE YAA SEYHA TUUBAA 😭❤️
Wubal, tëjal, mëdd, saañal, mëkk, sakk, damañ
Fu lor di aw jëm ci nun muy jabbutook a layi
Wubbil te tijjil te bàddil, sàqi, àlli, afal
Wuntiy njariñ yépp biir ak biti feg nattu yi
Sëñ Mbay Jaxate.....
Xamal Yalla, xam Yalla rekkay jariñ
Ku xam Yalla doo jis lu lay yàqati
Ku xam Yalla loo jis dalay far defar
Ku xam Yalla loo jis dalay yëkkati
Sëñ Mbay Jaxate.....!
Yaa di sunu wird, yaa nu doy ci Muqaddam
Yaa di sun Ismu Laahi doy nga nu yéené
Yaa nu ximbee ca naari, yaa nu teree xëm
Yaa nu tee walli làmb ney Saangoone
SMK....!
Sama'b xol ak sama cër yii yépp ak sama xel
Nay dëkk fàww ci yaw may dëkk nag ci sa xel
Saa xol bi feesal ko dell ak yaw ba xam ne ludul
Yaw dóotu am ci sama xol as mbarab sumu dal
Sëñ Mbay Jaxate...!
Maa bon te baaxub Sëriñ nit ñép népa ma gën
Te maa fi gën ab Sëriñ saa mbon gi dootu ma lor
Ku ñàki sér ku ko fab tàbal ci guddi mu bég
Ku bëgga leeral ku fab aj jant jox ko du mer
Sëñ Mbay Jaxate...!